1. " Waaw, [...], duma [...] tàyyee laaj li : naka la am réew di sàggane ba ay doxandéem ñëw teg ci moom loxo, di fa dogal ? "
Bubakar Bóris Jóob, Doomi Golo, EJO, 2019.
2. " Xawma lan a nu rey, nun Doomi-Afrig, wànte xeeb sunu bopp ci la bokk. Moo nu rey ba noppiy wéy di biral ne ba nu noon bi jamee naani, démb la woon tey soog a yegsi ..."
Bubakar Bóris Jóob, Bàmmeelu Kocc Barma, EJO, 2017.
3. " Buur day faral di soxla ci wetam ku koy fàttali ne nit kese la."
Bubakar Bóris Jóob, Malaanum lëndëm, EJO éditions, 2022.
#sunumbir
